03/06/2026
Jëwriñ yi daje nañu Àllarba 3 fan ci weeru Suwin atum 2026, ci kiliftéefu njiitu mi M. Mohamed Uld Seex Qasuwaani.
Ndaje ma saytu na ba noppi nangu tëralin yii:
- Mébatu yoon buy may ñu xaatim ab déggoo kopparal biñu torlu 28 ci weeru awril 2026, ci diggante Réewu Moritani ak mboolaayu àdduna bi yor wàllu Yokkute (IDA), ngir kopparal bu jëm ci tërëlinu Koom-koom bu baxa ak dëkk ci bërëbi Afrig sowwu jànt.
Tërëlin bi dafa bëgga dooleel yoriinu tefes gi, yokk fitna bi ci jafe-jafey coppite klimaa bi, boole ci gëna yombal liggéey ci koom-koomu bu baxa ci Moritani. Amna mbir yu am solo yii:
- Dëgëral doxalinu daara yi ;
- Yokkate koom-koomu tefes (Koom-koom bu baxa);
- Yokk dëgëral tefes gi.
Xaalis kopparal bi tollu na ci juróom ñatti f**ki milioŋ ak ñetti téemeeri junni (50.300.000) ci xaalisu Euro, mu tollu ci ñaari milyaar ak ñatti téemeer ak juróom f**ki ak juróom benn milioŋ (2.356.000.000) MRU, ñu wara ko fay ci diiru ñaar f**k ak-juróomi (25) at, boole ci juróom njuréef ak diiru 5% ci at. ci payoor biñ fay ci leble bi, ak fere 0,5% ci at mi ci payoor biñ lebl te génagul ci gafaka gi.
- Mébatu yoon buy may Réewu Mortani mu bokk ci pas buy wax ci aar ak jëfandikoo ndox yiy jàll ci frnceer yi ak xuru ndox yu àdduna , ñu dëgal ko ci 17 màrs 1992 ci Helsinki.
Déggoo bii dafay nekk jumtukaayu yoon bu am solo ci wàllu yoon ci wàllu lëkkaloo ci wàllu ndox yiy jàll ay fronceer.
Li muy fexe mooy jàppale fàggu, wàññi ak saytu jafe-jafe yi bawoo ci yeneen réew, ak itam jëfandikoo bu jaar yoon, jëfandikoo ndox mi ci kaw suuf ak ci biir suuf si, ci biir benn taxawayu yokkute buy yàgg.
Li Moritani bokk ci pas bii dina tax mu mëna:
- Gëna dëgëral lëkkaloo gi ak réew yi bokk ngëneel ci ndox ;
- Yokkute nguur gi ak yoriinu xéewali ndox yi ci anam wuñu boole ;
- Njariñ ci ndimbalu xarala, mbootaay ak kopparal yi;
- Fàttaliku fàggu xeex yi jëm ci ndox ak bokk liggéey ci basin yiy jàll ay fronceer ;
- Jàppale politigu réew mi ci wàllu wurum bi, ndox mi ak wàllu wérgi-yaram.
Dina jàppale itam ci amal ay jëmmal yu Moritani wara def ci wàllu àdduna, rawatina ci Mébetu Yokkate Dundu, rawatina ci ODD 6 ci wàllu ndox mu sell ak wàllu cet.
Sémbu ndogal buy jëfandikoo sàrtu gafaka biñ tëral ci ponk 46 (beesu) ci sartu yoonal bu n°2026-019 bu 1 juin 2026, buy soppali yenn sàrt yi ci sart yoonal n°2018-039 bu 9 oktoobar 2018, bi dindi n°11 19, 1978, lu jëm ci sartu yoonal ci yooni kopparal.
Sémbu ndogal bii dafa bëgga leeral anam yi ñuy jëfandikoo sàrtu gafaka biñ tëral ci ponk 46 (beesu) ci yoonu n°2026-019 bu 1 fan ci weeru Suwin 2026, lu jëm ci sartu yoonal ñeel yoonu kopparal.
Ci anam wu gëna mag, dafay leeral anam yi ñuy jaar ngir yaatal sàrt yii, lépp di aju ci jàngat yiñu def ci xet yi, ci xalaati mag yu am xel, ak ci jàngat ci xaalatyi ak coppite yi ci njariñ yiy génne ay mbell.
Dafay wax itam ni dañu wara xoolaat sàrt yi ci diiru ñatti at ngir mëna ànd ak coppite yi am ci wàllu koom-koom ak ci wàllu xaalis réew mi.
-Sémbu ndogal buy wax ni ñuy amal, sàrt yi, saytu bi, ci anam yi ñuy doxalee, ak doxalinu kilifay réew mi yor wàllu metrologie ci wàllu yoon, ak tëral diiru jàll bu méngoo ak li sàrti yoon n°2010-030 bu 5 sulet 2010, bi yor wàllu metrologie ci Moritani.
Dogal bii dafa bokk ci li ñuy amal ci ponk 6 ak 24 ci yoonu n°2010-030 bi yor metrologie ci Moritani, di wax ci bëgg-bëggu am njiit yu am sañ-sañ ci def wàllu saytu ciwallu metrologique ci wôoral ak taxawal diiru weccante ngir nit yiy liggéey ci wàllu saytu metrologique .
- Sémbu ndogal buy wax ci jox ndigalu mbell ci n°3820C2 ngir substans
- yu bokk ci Groupe 2 (suuf su ñuul) ci diwaanu Tiguent ci meññaliu SAM MINING SA.
Ginaaw biñu defaree jàngat yi war ci wàllu xarala ak liggéey, ba noppi jàpp ni meññal bi dafa fay bépp fere ak ndàmpaay bu jëm ci joxe sañ-sañ bi, ci lu tollu ci 6,500,000 MRU, ci anam wu méngoo ak sàrti yoon ak ponku yiñu tëral, lii di tëralin yi ci meññalu bi dafay may Groupe bi ci Tiguent, diwaanu Trarza.
Dogal bii dafa wara:
Xëcc dugalkatu xaalis yu bari ci wàllu mbell yi ;
- Defaral réew mi lu koy duggalal xaalis jaare leko cu juuti yi ;
- Sos ay liggéey ci dëkk bi ;
- Yokk jumtukaay yi ci barab yi ci laale.
- Sémbu ndogal buy wax ci jox juróomi (5) sañ-sañu wër smbir yi ci kuréelu (2) yenn kërub liggéeyukaayu mbell.
- Sémbu ndogal buy wax ci jox ADMOG GOLD MAURITANIE SUARL ñatti (3) sañ-sañu wër mbir yi ci kuréelu (2) bi.
- Sémbu ndogal buy wax ni dañuy jox Neja Gold benn (1) sañ-sañu wër substance yi ci kuréelu(7).
Ci anam wu jëm kanam ngir saafara jafe-jafe yi jëm ci kadastru mine, ci xoolaat bu gaaw, te leer, te ginaaw bi sosiete yi ci laale fayee lépp lu ñu war fay mu jëm ci joxe ndigal yooyu, lu tollu ci 27.308.600 milioŋ. Sémb yooyu dañuy jox 9 ndigal permis ngir mbir yu jëm ci kuréel 2 ak 7, ci anam wu méngoo ak sàrti yoon ak sàrt yiñ tëral.
Buñu sukkandikoo ci li ñu wax ci kaw, joxe ndigal yooyu dafay wane ni réew mi fasna yéene soppi mine yi ci réew mi mu nekk alal ju mëna yàgg, ci noonu lañuy jàppale liggéeykat yi ñu wóolu seen bopp, ba noppi gëna xëcc réew mi ci wàllu mbell.
Jëwriñ ji yor mbiri bitim réew, lëkkaloo ci Afrig, ak waa Móritani yi ci bitim réew, joxe na rapoor buy wax ni àdduna bi di doxee.
Jëwriñ ji yor biir réew mi, gëna suqali dëkk-dëkkaan yi, ak yokkute ci dëkk yi dafa joxe rapoor ci jafe-jafe yi ci biir réew mi.
Jëwriñ ji ñu dénk wàllu mbëj mi ak njafaan, di itam jëwriñ ji yor xaalis ci jamono jooju, dafa joxe rapoor ci matuwaay yu bees yu nguur gi jël ngir jàppale njaboot yi gëna néew doole.
Jano ak jafe jafe yii di am ci xeex bi ci moyenoriaan bi, waral ay jafe jafe ci koom gi ci aduna bi, lu ci mel ni yokkute bu musul am ci njëgu hidrokarbiir ak gaas ak ay jafe jafe yuy yokku ci komers boobu, ak ci bëgg bëggu kii di njiitu repibilik bi ngir aar askan wi, ñi gëna ñakk doole ci jënd ak doole. Buur bu mag bi dafa sant nguur gi mu jël matuwaay yu amul fenn ngir jàppale njaboot yi gëna ñakk kaarange, ba noppi wàññi jafe-jafe yi mu jur ci àdduna bi.
Ci anam wu méngoo ak tegtali njiitu réew mi, dañu jël dogal ni dañuy tàmbali tërëlin bu amul fenn, di prograam bu njëkk ci xeetam ci yaatuwaayam, bu am ñaari pàcc:
- Jox xaalis bépp njaboot buñ bind ci Registre Social, muy lu ëpp 352 000 njaboot ci réew mi, lu ëpp ñaari milioŋ ciy doomi réew ;
- Séddale ay ndimbal ñam lu ëpp 155 000 njaboot yu gëna ñakk kaarange yuñ bind seen tur ci Registre Social, maanaam luy tollu ci benn milioŋ ciy doomi réew.
Bépp pañe ñam amna:
- 50 kg ceeb ;
- 50 kg ci pepp ;
- 10 kg suukër ;
- 10 kg ci makaroni;
- 5i litir diw.
Liggéey bu mag bii dafay laaj ñu dajale ay doomi aadama ak ay jumtukaayi yu bare, te dafay laaj xaalis bu ëpp 12 milyaari ouguiya yu yàgg.
Fi ñu mujjee mooy ndaje mi jël matuwaay yii:
jëwriñ ji yor dooleel ndaw ñi, liggéey, tàggat yaram ak sarwis siwil
kabine jëwriñ ji
- Xalaatkat ci wàllu xam-xam ci ndaw ñi ak bégal seen xol : Hamza JAAFAR BOIDJEL, am lijaasa bu mag ci Taarix ak Siwilisasioŋ.
Jëwriñ ji yor mbiri koom ak yokkute
Bànqaas gi yor jàngale mi ak tàggatu gi.
- ki topp ci njiit li : Boubacar El Mami Jumua.
Jëwriñ ji yor yaxantu gi ak ndaamari ji
Kabine jëwriñ ji
Konsilu joŋante
- Sekretër permanent : Ibrahim Silly CAMARA, am lijaasa bu mag ci wàllu koppar.
- Rapporter général: El Houssein Sid'ahmed Lab.
- Raporkat yi:
* Zeinebou Mohamed Vall Rayess, am Master ci Finance ak Comptabilité.
* Fatma Sid'ahmed Mkheytir, am lijaasa ci koom-koom ak spesialisasioŋ ci liggéey.