20/08/2026
NDAX XAMOON NGEEN KO ?
Bu tawee ba noppi, yoon la ndox mi des fa ab diir laataa muy dem. Fàww mu am as ndiir ngir ndoxi taw yépp di door a jàll : mooy jamonoy négandiku gi.
Jumtukaayi asanismaa yi manuñoo tëb rekk jàllale ndox mépp ci saa si. Fàww mu xaar tuuti.
Mu ngi aju nag ci :
- Dayob taw bi :
Taw bu am doole day jël lu bari ci yooni asanismaa yi.
- Diir bi taw bi am :
Taw bu am doole te yàgg day laaj waxtu yu bari ngir ndox mépp man a dem.
- Dooley yoonu asanismaa wi :
Yaatuwaay ak dooley jumtukaay yi itam dañuy am taxawaay ci gaawaayu yóbbu ndox yi.
- Tolluwaayu jumtukaay yi :
Teewaayu garawaay, mbalit walla suuf ci biir jumtukaay yi, man nañoo yeexal demug ndox mi.
Jàppleen lii :
Ndoxum kese mu dajaloo su tawee ba noppi tekkiwul ne daa am lu doxul. Fàww ngeen bàyyi xel bu baax waxtu yi war dëgg ngir jumtukaayi asanismaa yi man def seen liggéey ca na mu ware.
Gouvernement du Sénégal,Office des forages ruraux - OFOR,DPGI-Direction de la Prévention et de la Gestion des Inondations,Direction Assainissement,Direction de l'Hydraulique,SEN EAU,DGPRE Direction de la Gestion et de la Planification des Ressources en Eau,Société Nationale Des Eaux Du Sénégal - SONES,Office Des Lacs Et Cours D'eau - OLAC,Agence nationale de l'aviation civile et de la météorologie - Anacim,Onas Sénégal,Organisation pour la Mise en Valeur du fleuve Senegal/OMVS